Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 13

LUUG 13:18-34

Help us?
Click on verse(s) to share them!
18Noonu Yeesu neeti: «Lan la nguuru Yàlla di nirool? Lan laa ko mana méngaleel?
19Mi ngi mel ni doomu fuddën gu nit jël, ji ko ci toolam. Mu sax, nekk garab, ba picci asamaan ñëw, tàgg ciy caram.»
20Mu neeti: «Lan laa mana méngaleek nguuru Yàlla?
21Mi ngi mel ni lawiir bu jigéen jël, jaxase ko ak ñetti andaari fariñ, ba kera tooyal bépp di funki.»
22Yeesoo ngi doon jaar ci ay dëkk yu mag ak yu ndaw, di jàngle te jublu Yerusalem.
23Am ku ko ne: «Boroom bi, ndax ñiy mucc ñu néew lay doon?» Yeesu ne leen:
24«Defleen seen kem kàttan, ngir dugg ci bunt bu xat bi, ndaxte maa ngi leen koy wax, ñu bare dinañu jéema dugg, waaye duñu ko man.
25Jamono dina ñëw, ju boroom kër gi di jóg, tëj buntam. Dingeen nekk ci biti di fëgg naan: “Boroom bi, ubbil nu!” Mu ne leen: “Xawma fu ngeen bokk.”
26Bu ko defee ngeen naan: “Noo doon bokk di lekk ak a naan, te jàngle nga ci sunuy pénc.”
27Mu ne leen: “Nee naa leen xawma fu ngeen bokk. Yéen ñépp soreleen ma, defkati lu bon yi!”
28Foofa dingeen jooy, di yéyu, bu ngeen gisee seeni maam Ibraayma, Isaaxa, Yanqóoba ak yonent yépp ci nguuru Yàlla, te ñu dàq leen ca biti.
29Ay nit dinañu jóge penku ak sowu, nor ak sudd, ñëw, bokk lekk ci ñam, yi Yàlla di joxe ci nguuram.
30Noonu ñenn ci ñi mujj ñooy jiituji; te ci ñi jiitu, ñooy mujji.»
31Ca jamono jooja ay Farisen ñëw ca Yeesu ne ko: «Jógeel fii, dem feneen, ndaxte Erodd a ngi lay wuta rey.»
32Noonu mu ne leen: «Demleen ne bukki boobu ne ko: “Xoolal, maa ngi dàq rab yi tey wéral nit ñi tey ak suba. Ca ñetteelu fan ba, ma àgg fa ma Yàlla jëmale.”
33Waaye fàww ma dox sama itte tey, suba ak gannaaw suba, ndaxte wareesula reye ab yonent feneen fu dul Yerusalem.
34«Yerusalem, Yerusalem, yaw miy rey yonent yi, tey sànni ay doj ndaw yi, ba ñu dee, aka maa bëggoona dajale say doom, ni ginaar di uufe ay cuujam te nanguwuleen!

Read LUUG 13LUUG 13
Compare LUUG 13:18-34LUUG 13:18-34