Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 11

Luug 11:39-49

Help us?
Click on verse(s) to share them!
39Sang bi ne ko: «Yeen Farisen yi, bitib kaas bi ak ndab li daal ngeen di raxas, te fekk leen feese jikkoy jagoo lu lewul, akug mbon ci biir!
40Yeena ñàkk xel! Xanaa du ki sàkk biti moo sàkk biir itam?
41Li ci biir kay ngeen di sarxe! Su boobaa seen lépp ay set.
42Waaye wóoy ngalla yeen Farisen yi! Xobi naana ak yeneen safal yu mel ni ru ak wépp xeetu lujum, yeena ngi ciy génne cérub fukkeel, ngir asaka, njubte ak cofeelu Yàlla nag, ngeen sàggane. Lii de war na leen, waaye lee it, waruleen koo sàggane.
43Wóoy ngalla yeen Farisen yi! Yeenay sàkku péete yu kaname ca jàngu ya, ak nuyoob gëddaal ca pénc ma.
44Wóoy ngalla yeen, yeena ngi mel ni ay bàmmeel yu amul xàmmikaay, nit ñiy dox ca kaw te xamuñu ko.»
45Kenn ci xamkati yoon yi nag àddu ne: «Sëriñ bi, loolu nga wax de, nun itam, xasaale nga nu ci.»
46Yeesu itam ne: «Yeen xamkati yoon yi itam, wóoy ngalla yeen, yeen ñi sëf nit ñi sëf yu ñu àttanul, te yeen ci seen bopp, seen benn baaraam sax du ci laal.
47Wóoy ngalla yeen, yeenay tabax bàmmeeli yonent yi, te seeni maam reyoon leen.
48Kon yeena seedee noonu ne seen jëfi maam ya, ànd ngeen ci, ndax ñoom ñoo leen rey, yeen ngeen tabax seeni bàmmeel.
49Looloo tax itam kàddug Yàlla giy xel, biral ne: “Maay yebal fa ñoom ay yonent aki ndaw, ñii ñu bóom, ñee, ñu bundxatal.”

Read Luug 11Luug 11
Compare Luug 11:39-49Luug 11:39-49