Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 11:39-49 in Wolof

Help us?

LUUG 11:39-49 in Téereb Injiil

39 Noonu Boroom bi ne ko: «Waaw, yéen Farisen yi, yéena ngi setal bitib kaas bi ak ndab li, waaye ci biir dangeena fees ak càcc ak mbon!
40 Yéena ñàkk xel! Xanaa du ki defar biti moo defar biir itam?
41 Sarxeleen li nekk ci biir te seen lépp dina sell.
42 Yéen Farisen yi dingeen torox! Ndaxte yéena ngi sàkk asaka ci naana ak ru ak léjum bu nekk, waaye sàggane ngeen njubte ak mbëggeel ci Yàlla. Loolu ngeen wara def, waxuma nag ngeen sàggane la ca des.
43 Yéen Farisen yi, dingeen torox! Ndaxte ca jàngu ya, toogu ya féete kanam ngeen di taamu te bëgg ñépp di leen nuyoo ñaari loxo ca pénc ma.
44 Dingeen torox, ndaxte dangeena mel ni ay bàmmeel yu raaf, ba nit ñi di ci dox te teyuñu ko.»
45 Kenn ci xutbakat yi ne ca tonn ne: «Kilifa gi, boo waxee loolu, yaa ngi nuy xas, nun itam.»
46 Noonu Yeesu neeti leen: «Yéen itam xutbakat yi, dingeen torox! Ndaxte dangeen di sëf nit ñi say yu diis, waaye dungeen nangoo laal sëf bi sax ak seen cati baaraam.
47 Dingeen torox, ndaxte yéena ngi tabax xabruy yonent, yi seeni maam reyoon.
48 Dangeen di seede noonu ne ànd ngeen ak li seen maam defoon, ndaxte ñoo rey yonent yi, yéen ngeen tabax xabru yi.
49 Looloo tax Yàlla mi xam lépp ne: “Dinaa leen yónnee ay yonent ak ay ndaw. Ñenn ñi dinañu leen fitnaal, rey leen.”
LUUG 11 in Téereb Injiil

Luug 11:39-49 in Kàddug Yàlla gi

39 Sang bi ne ko: «Yeen Farisen yi, bitib kaas bi ak ndab li daal ngeen di raxas, te fekk leen feese jikkoy jagoo lu lewul, akug mbon ci biir!
40 Yeena ñàkk xel! Xanaa du ki sàkk biti moo sàkk biir itam?
41 Li ci biir kay ngeen di sarxe! Su boobaa seen lépp ay set.
42 Waaye wóoy ngalla yeen Farisen yi! Xobi naana ak yeneen safal yu mel ni ru ak wépp xeetu lujum, yeena ngi ciy génne cérub fukkeel, ngir asaka, njubte ak cofeelu Yàlla nag, ngeen sàggane. Lii de war na leen, waaye lee it, waruleen koo sàggane.
43 Wóoy ngalla yeen Farisen yi! Yeenay sàkku péete yu kaname ca jàngu ya, ak nuyoob gëddaal ca pénc ma.
44 Wóoy ngalla yeen, yeena ngi mel ni ay bàmmeel yu amul xàmmikaay, nit ñiy dox ca kaw te xamuñu ko.»
45 Kenn ci xamkati yoon yi nag àddu ne: «Sëriñ bi, loolu nga wax de, nun itam, xasaale nga nu ci.»
46 Yeesu itam ne: «Yeen xamkati yoon yi itam, wóoy ngalla yeen, yeen ñi sëf nit ñi sëf yu ñu àttanul, te yeen ci seen bopp, seen benn baaraam sax du ci laal.
47 Wóoy ngalla yeen, yeenay tabax bàmmeeli yonent yi, te seeni maam reyoon leen.
48 Kon yeena seedee noonu ne seen jëfi maam ya, ànd ngeen ci, ndax ñoom ñoo leen rey, yeen ngeen tabax seeni bàmmeel.
49 Looloo tax itam kàddug Yàlla giy xel, biral ne: “Maay yebal fa ñoom ay yonent aki ndaw, ñii ñu bóom, ñee, ñu bundxatal.”
Luug 11 in Kàddug Yàlla gi