Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 4

Kàddu yu Xelu 4:1-6

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Gone yi, tee ngeena dégg yaru baay, te déglu, ba am ug dégg?
2Maa ngi leen di jàngal lu baax, buleen fàtte sama njàngle.
3Man it amoon naa baay, di benn bàjjo ci saa ndey.
4Baay digal ma, ne ma: «Jàppal samay wax ci sam xel, di jëfe samay santaane, ba dund.
5Amal xel mu rafet akug dégg. Bul fàtte te bul moy samay wax.
6Bul dëddu xel mu rafet, da lay aar; sopp ko, mu sàmm la.

Read Kàddu yu Xelu 4Kàddu yu Xelu 4
Compare Kàddu yu Xelu 4:1-6Kàddu yu Xelu 4:1-6