13Ku gàddul jaambur bor, jëlal mbubbam; tayle ko, moo dige feyal ndaw su yemadi.
14Nuyoo bu xumb, suba teel mooki saagaa yem.
15Jabar ju pànk mooy senn bu dakkul, cib taw;
16ku ko mana yemale, mana téye ngelaw mbaa nga ŋëb ag diw.
17Weñ ay nàmm weñ, nit ay nàmm xelu moroom ma.
18Ku aar garab, lekk ca doom ya; ku topptoo sa sang, am ngërëm.
19Ku xool cim ndox, gis sa kanam, nga xool sab xol, gis sa jikko.