12Noonu ñépp waaru, ba jaaxle lool, ñuy waxante ci seen biir ne: «Lii lu muy tekki?»
13Waaye ñenn ñi di leen ñaawal ne: «Waay! Ñii dañoo màndi ak biiñ.»
14Ci kaw loolu Piyeer taxaw, ànd ak fukki ndaw ya ak benn, mu wax ci kaw, di yégal mbooloo ma ne: «Bokki Yawut yi ak yéen ñépp ñi dëkk Yerusalem, dégluleen bu baax te xam lii ma leen di wax!
15Nit ñii màndiwuñu, ci ni ngeen ko fooge, ndaxte nu ngi ci yoor-yoor rekk.
16Waaye lii mooy li Yàlla waxoon, jaarale ko ci yonentam Yowel ne:
17“Yàlla nee na: Ci bés yu mujj yi, dinaa tuur ci sama Xel ci kaw nit ñépp; seen xeet wu góor ak wu jigéen dinañu wax ci kàddug Yàlla; waxambaane yi dinañu gis ay peeñu te màggat yi di gént ay gént.
18Waaw, ci bés yooyu dinaa tuur ci sama Xel ci sama kaw jaam yu góor ak yu jigéen, te dinañu wax ci kàddug Yàlla.
19Dinaa wone ay kéemaan ci kaw ci asamaan ak ay firnde ci suuf ci àddina, muy deret, sawara ak ay niiri saxar.
20Jant bi dina daldi lëndëm, weer wi deretal, bala bésu Boroom biy ñëw, di bés bu mag, bi ànd ak ndam.
21Booba nag ku woo Boroom bi ci aw turam, dinga mucc.”
22«Yéen bokki Israyil, dégluleen wax jii! Yeesu mi dëkk Nasaret, nit la woon, ku Yàlla dëggal ci seen kanam ciy kéemaan, ay jaloore ak firnde, ya Yàlla defoon jaarale ko ci moom ci seen biir; yéen xam ngeen ko.