Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 1

JËF YA 1:19-23

Help us?
Click on verse(s) to share them!
19Loolu siiwoon na ci waa Yerusalem, moo tax ci seen làkk ñuy tudde tool ba Akeldama, maanaam «Toolu deret».—
20Piyeer teg ca ne: «Ndaxte lii lañu bind ci téereb Sabóor: “Na këram gental, bu fa kenn dëkk.” Te it: “Na keneen bey sasam.”
21Kon ñeel na nu, nu tànn kenn ci ñi bokk ak nun, diir bi Yeesu doon dem ak a dikk ci sunu biir,
22li dale ci bi ko Yaxya sóobee ci ndox, ba bés ba ko Yàlla jële ci sunu biir, yéege ko. Kooku war na ànd ak nun, di seedeel ndekkitel Yeesu.»
23Bi ko Piyeer waxee, ñu tudd ñaar: Yuusufa, mi ñu dippee Barsabas te di ko dàkkentale Yustus, moom ak Macas.

Read JËF YA 1JËF YA 1
Compare JËF YA 1:19-23JËF YA 1:19-23