19 Loolu siiwoon na ci waa Yerusalem, moo tax ci seen làkk ñuy tudde tool ba Akeldama, maanaam «Toolu deret».—
20 Piyeer teg ca ne: «Ndaxte lii lañu bind ci téereb Sabóor: “Na këram gental, bu fa kenn dëkk.” Te it: “Na keneen bey sasam.”
21 Kon ñeel na nu, nu tànn kenn ci ñi bokk ak nun, diir bi Yeesu doon dem ak a dikk ci sunu biir,
22 li dale ci bi ko Yaxya sóobee ci ndox, ba bés ba ko Yàlla jële ci sunu biir, yéege ko. Kooku war na ànd ak nun, di seedeel ndekkitel Yeesu.»
23 Bi ko Piyeer waxee, ñu tudd ñaar: Yuusufa, mi ñu dippee Barsabas te di ko dàkkentale Yustus, moom ak Macas.