Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 12

Jëf ya 12:22-25

Help us?
Click on verse(s) to share them!
22Mbooloo maa ngay àddu ca kaw, naan: «Lii kay baatu Yàlla la, du baatu nit!»
23Ca saa soosa tembe la ko malaakam Boroom bi fàdd, ndax la mu delloowul Yàlla njukkal. Ba loolu amee, ay sax ronq ko, mu dee.
24Ci biir loolu kàddug Yàlla di gëna siiw, di gëna law.
25Barnaba ak Sóol nag, gannaaw ba ñu sottalee seen liggéey, dañoo jóge Yerusalem, ñibbi, ànd ak Yowaan mi ñuy wax Màrk.

Read Jëf ya 12Jëf ya 12
Compare Jëf ya 12:22-25Jëf ya 12:22-25