Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - ROOM - ROOM 11

ROOM 11:1-22

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ma ne kon, ndax Yàlla bërgël na xeetam? Mukk! Ndaxte man itam ci Israyil laa bokk, wàcce ci Ibraayma te bokk ci giiru Beñamin.
2Yàlla bërgëlul xeetam, wi mu xamoon lu jiitu. Ndax dangeena xamul li Mbind mi di wax ci mbirum Ilyaas? Dafa doon tawat Israyil ci Yàlla naan:
3«Boroom bi, rey nañu say yonent, daaneel say bérab yu sell, ba man kenn maa ci des, te ñu ngi may wuta rey.»
4Waaye Yàlla da ko ne: «Dencal naa sama bopp juróom ñaari junniy nit ñu jaamuwul Baal.»
5Noonu itam ci jamono ji nu nekk, des na nit ñu néew ñu Yàlla dencal boppam ciw yiwam.
6Gannaaw nag yiwu Yàlla rekk a tax mu denc leen, kon du seen peyug ñaq, walla boog yiwu Yàlla dootul yiw.
7Kon lu nu ci wara wax? Li bànni Israyil doon wut, gisuñu ko. Waaye ñi Yàlla tànn rekk a ko gis, te ña ca des baña gëm, ba seen xol dërkiis.
8Looloo tax Mbind mi ne: «Yàlla daf leena jox xelum nit ku gëmméentu, bët yu gëlëm ak nopp yu tëx, ba ci bésub tey.»
9Te Daawuda it daf ci wax naan: «Na seeni ñam sax nekk fiir ak i pakk; nañu ci daanu, te Yàlla mbugal leen.
10Nañu gumba ba ne fatuus, nañu tiis te sëgg ba fàww.»
11Ndax kon dañoo tarxiis, daanu ba fàww? Mukk! Waaye jéllub Israyil dafa ubbi bunt, ngir xeeti ñi dul Yawut mana mucc, te bànni Israyil siis leen.
12Gannaaw seen tooñ nag moo ubbi buntu yiw ci waa àddina si, te seen ñàkk moo meññ barkeb xeet yépp, céy bés bu Israyil gépp delloo ci Yàlla, ndaw barke bu bare!
13Yéen ñi dul Yawut, yéen laay waxal. Ndegam Yàlla daf maa def ndawam, yónni ma ci yéen xeeti àddina si, damay matal samab yónnent.
14Dama koy def, ngir ñi bokk ak man xeet siis, ba ñenn ñi mucc.
15Ndaxte bi Yàlla génnee Israyil, ubbee na noonu bunt, ngir xeeti àddina juboo ak moom; kon su Yàlla dugalaatee Israyil, ndax du mel ni ndekkitel néew ya?
16Damay wax ne, mburu mépp sell na, bu ci Yàlla amee wàll. Naka noonu garab gi Yàlla séddoo reen bi, garab gépp sell na.
17Bànni Israyil a ngi mel ni garabu oliw gu ñu jëmbët ci kër gi, waaye mu am car yu ci fàq. Yaw mi dul Yawut, yaa ngi mel ni caru garabu oliw gu àll bu ñu jabtal ci garabu kër googu. Noonu nga jariñoo meen, mi jóge ci reen bi.
18Kon nag bul bàkku, di xeeb car yooyu Yàlla fàq. Waaye soo bëggee bàkku, xamal ne reen moo lay yenu, te du yaw miy car yaa koy yenu.
19Xanaa dinga wax ne: «Car yooyu dañu leena fàq, ngir jabtal ma fa ñu nekkoon.»
20Dëgg la; waaye seen ngëmadee tax ñu fàq leen, wuutal la fa ndax sa ngëm. Bumu tax nag ngay bàkku, waaye nanga moytu.
21Gannaaw Yàlla baalul car ya cosaanoo ca garab ga, kon boog yéen itam man na leena fàq.
22Loolu kon wone na ni Yàlla baaxe ak ni muy meree tooñ. Ci ñi daanu, Yàlla wone na ni meram tànge, wone mbaaxam ci yéen, su fekkee yéena ngi ci wéy; lu ko moy, dees na leen fàq yéen itam.

Read ROOM 11ROOM 11
Compare ROOM 11:1-22ROOM 11:1-22