Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 9

LUUG 9:33-54

Help us?
Click on verse(s) to share them!
33Bi nit ñooñu di sore Yeesu, Piyeer ne ko: «Kilifa gi, bég nanu ci sunu teew fii; nanu defar ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa ak benn Ilyaas.» Fekk xamul la mu doon wax.
34Bi mu koy wax, niir ñëw muur leen, taalibe yi daldi tiit, bi leen niir wa ëmbee.
35Noonu baat jibe ca niir wa naan: «Kii mooy sama Doom ji ma fal; dégluleen ko.»
36Bi baat ba waxee ba noppi, Yeesu rekk des fa. Taalibe ya noppi, baña nettali kenn ca jamono jooja la ñu gisoon.
37Ca suba sa Yeesu ak taalibe ya wàcce ca tund wa, mbooloo mu bare ñëw, di ko gatandu.
38Nit xaacu ci biir mbooloo mi naan: «Kilifa gi, maa ngi lay ñaan, nga seet sama doom, ndaxte moom kepp laa am.
39Léeg-léeg rab jàpp ko, mu daldi yuuxu ca saa sa, rab wi di ko sayloo, gémmiñ gi di fuur. Du faral di génn ci moom te dina ko sonal.
40Ñaan naa say taalibe, ñu dàq ko, waaye manuñu ko.»
41Yeesu ne leen: «Yéen niti jamono jii, yéen ñi gëmadi te dëng, ba kañ laa wara nekk ak yéen te di leen muñal? Indil ma sa doom.»
42Bi xale biy agsi, rab wi di ko daaneel ci suuf, muy say. Waaye Yeesu daldi gëdd rab wa, wéral xale ba, daldi ko delloo baayam.
43Ku nekk waaru na ndax màggug Yàlla. Bi ñuy yéemu ci li mu doon def, Yeesu ne taalibeem ya:
44«Dégluleen bu baax lii ma leen di wax: dinañu jébbal Doomu nit ki ci loxoy nit ñi.»
45Waaye taalibe ya xamuñu kàddu googu. Yàlla dafa leen nëbb li muy tekki, ba ñu bañ koo xam, te ñemewuñu koo laaj Yeesu.
46Werante am ci biir taalibe yi, ñuy laajante kan moo gëna màgg ci ñoom.
47Yeesu mi xam seen xalaat, jël ab xale, teg ci wetam ne leen:
48«Ku nangu xale bii ci sama tur, man mii nga nangu; te ku ma nangu, nangu nga ki ma yónni; ndaxte ki gëna woyof ci yéen ñépp, kooku moo gëna màgg.»
49Bi loolu amee Yowaana jël kàddu gi ne: «Kilifa gi, danoo gis nit kuy dàq ay rab ci sa tur, nu tere ko ko, ndaxte bokkul ci nun.»
50Waaye Yeesu ne ko: «Buleen ko tere, ndaxte ku la sotul, far na ak yaw.»
51Bi jamono ji jegeñsee, ji Yeesu waree jóge àddina dem asamaan, mu sigiñu ci dem Yerusalem.
52Noonu mu yebal ay ndaw, ñu jiitu ko. Ñu dem nag, dugg ci ab dëkk ci diiwaanu Samari, ngir wutal ko fa fu mu dal.
53Waaye waa dëkk ba nanguwuñu ko, ndaxte mi ngi jublu woon Yerusalem.
54Bi taalibe yi tudd Saag ak Yowaana gisee loolu, ñu ne: «Boroom bi, ndax dangaa bëgg nu ne, na sawaras asamaan dal ci seen kaw, faagaagal leen?»

Read LUUG 9LUUG 9
Compare LUUG 9:33-54LUUG 9:33-54