Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 9:33-54 in Wolof

Help us?

LUUG 9:33-54 in Téereb Injiil

33 Bi nit ñooñu di sore Yeesu, Piyeer ne ko: «Kilifa gi, bég nanu ci sunu teew fii; nanu defar ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa ak benn Ilyaas.» Fekk xamul la mu doon wax.
34 Bi mu koy wax, niir ñëw muur leen, taalibe yi daldi tiit, bi leen niir wa ëmbee.
35 Noonu baat jibe ca niir wa naan: «Kii mooy sama Doom ji ma fal; dégluleen ko.»
36 Bi baat ba waxee ba noppi, Yeesu rekk des fa. Taalibe ya noppi, baña nettali kenn ca jamono jooja la ñu gisoon.
37 Ca suba sa Yeesu ak taalibe ya wàcce ca tund wa, mbooloo mu bare ñëw, di ko gatandu.
38 Nit xaacu ci biir mbooloo mi naan: «Kilifa gi, maa ngi lay ñaan, nga seet sama doom, ndaxte moom kepp laa am.
39 Léeg-léeg rab jàpp ko, mu daldi yuuxu ca saa sa, rab wi di ko sayloo, gémmiñ gi di fuur. Du faral di génn ci moom te dina ko sonal.
40 Ñaan naa say taalibe, ñu dàq ko, waaye manuñu ko.»
41 Yeesu ne leen: «Yéen niti jamono jii, yéen ñi gëmadi te dëng, ba kañ laa wara nekk ak yéen te di leen muñal? Indil ma sa doom.»
42 Bi xale biy agsi, rab wi di ko daaneel ci suuf, muy say. Waaye Yeesu daldi gëdd rab wa, wéral xale ba, daldi ko delloo baayam.
43 Ku nekk waaru na ndax màggug Yàlla. Bi ñuy yéemu ci li mu doon def, Yeesu ne taalibeem ya:
44 «Dégluleen bu baax lii ma leen di wax: dinañu jébbal Doomu nit ki ci loxoy nit ñi.»
45 Waaye taalibe ya xamuñu kàddu googu. Yàlla dafa leen nëbb li muy tekki, ba ñu bañ koo xam, te ñemewuñu koo laaj Yeesu.
46 Werante am ci biir taalibe yi, ñuy laajante kan moo gëna màgg ci ñoom.
47 Yeesu mi xam seen xalaat, jël ab xale, teg ci wetam ne leen:
48 «Ku nangu xale bii ci sama tur, man mii nga nangu; te ku ma nangu, nangu nga ki ma yónni; ndaxte ki gëna woyof ci yéen ñépp, kooku moo gëna màgg.»
49 Bi loolu amee Yowaana jël kàddu gi ne: «Kilifa gi, danoo gis nit kuy dàq ay rab ci sa tur, nu tere ko ko, ndaxte bokkul ci nun.»
50 Waaye Yeesu ne ko: «Buleen ko tere, ndaxte ku la sotul, far na ak yaw.»
51 Bi jamono ji jegeñsee, ji Yeesu waree jóge àddina dem asamaan, mu sigiñu ci dem Yerusalem.
52 Noonu mu yebal ay ndaw, ñu jiitu ko. Ñu dem nag, dugg ci ab dëkk ci diiwaanu Samari, ngir wutal ko fa fu mu dal.
53 Waaye waa dëkk ba nanguwuñu ko, ndaxte mi ngi jublu woon Yerusalem.
54 Bi taalibe yi tudd Saag ak Yowaana gisee loolu, ñu ne: «Boroom bi, ndax dangaa bëgg nu ne, na sawaras asamaan dal ci seen kaw, faagaagal leen?»
LUUG 9 in Téereb Injiil

Luug 9:33-54 in Kàddug Yàlla gi

33 Ba ñu demee ba ñaari nit ñooñu di bàyyikoo fa Yeesu, Piyeer ne ko: «Njaatige, su nu toogoon fii de, mu baax ci nun; nan yékkati ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa, benn Ilyaas.» Waaye booba Piyeer xamul la muy wax.
34 Naka lay wax loolu, aw niir dikk yiir leen, taalibe ya tàbbi ca biir niir wa, tiitaange jàpp leen.
35 Ci biir loolu baat jibe ca niir wa, ne: «Kii moo di sama Doom, ki ma taamu; dégluleen ko.»
36 Ba baat ba selawee, Yeesu doŋŋ a feeñ. Taalibe ya nag ñoom ne cell, waxuñu kenn lenn jant yooyu, ca la ñu gis.
37 Ca ëllëg sa ba ñuy wàcce tund wa, mbooloo mu baree dikk dajeek Yeesu.
38 Jenn waay jekki xaacoo ca mbooloo ma, ne: «Sëriñ bi, dama lay ñaan, nga xoolal ma sama doom, ndax moom doŋŋ laa am.
39 Rab kat moo ko jàpp, mu jekki di yuuxu, di say, gémmiñ giy fuur. Daanaka du teqlikook moom te sonal na ko.
40 Ñaan naa say taalibe ngir ñu dàqal ma ko, waaye manuñu ko.»
41 Yeesu ne leen: «Céy niti tey, yeena gëmadi te dëng! Maak yeen ba kañ, te di leen muñal? Indi sa doom fii.»
42 Naka la xale bi jubsi Yeesu, rab wi sànni ko ci suuf, muy say. Yeesu itam gëdd rab wa, wéral xale ba, delloo ko baayam.
43 Ñépp nag waaru ci màggug Yàlla. Naka la ñépp di yéemu ca mboolem la Yeesuy def, mu ne taalibeem ya:
44 «Ubbileen seeni nopp te teewlu bu baax kàddu yii: Doomu nit ki lees di wor, ngir teg ko ci loxoy nit ñi.»
45 Taalibe ya nag dégguñu kàddu googu, ndax fekk na piri ma làqu leen, ngir ñu bañ koo daj, te ñemewuñu koo laaj Yeesu.
46 Werante moo dikkaloon taalibe yi, ñuy seet kan moo gëna kawe ci ñoom.
47 Yeesu nag ràññee seen xalaat. Mu daldi indi ab xale, taxawal ko ci wetam.
48 Mu ne leen: «Xale bii, képp ku ko dalal ndax sama tur, man nga dalal; te képp ku ma dalal, dalal nga ki ma yebal; ndax ki gëna tuut ci yeen ñépp, kooku moo gëna màgg.»
49 Ci kaw loolu Yowaan àddu, ne: «Njaatige, danoo gis nit kuy dàqe sa tur ay rab, nu aaye ko, ndax bokkul ci nun.»
50 Yeesu ne ko: «Buleen ko aaye, ndax ku la sotul, yaw la faral.»
51 Ba ñu demee ba bés bi ñu wara yéege Yeesu di jubsi, Yeesu moo dogu ngir dem Yerusalem.
52 Mu yebal ay ndaw, ñu jiitu ko. Ñu dem, ba agsi ab dëkk ci diiwaanu Samari, nar ko faa waajal ab dal.
53 Waa Samari nag nanguwuñu koo dalal, ndax Yerusalem ga mu nammoona jëm.
54 Taalibe ya ñuy wax Yanqóoba ak Yowaan gis loolu, daldi ne: «Sang bi, soo bëggee nu jox sawara ndigal, mu wàcce asamaan, faagaagal leen?»
Luug 9 in Kàddug Yàlla gi