15ak Macë ak Tomaa, ak Yanqóoba doomu Alfe, ak Simoŋ mi ñuy wax farlukatu moom-sa-réew,
16ak Yuda doomu Yanqóoba, ak Yuda Iskaryo ma mujj wor.
17Ci kaw loolu Yeesu ànd ak ñoom, wàcc, daldi taxaw ca joor ga. Ay taalibeem yu baree nga fa woon ak mbooloo mu réya réy: ay niti Yude gépp, ak Yerusalem ak Tir ak Sidon, dëkki wetu tefes ga.
18Ñu dikk, di ko déglu tey faju ba tàggook seeni jàngoro. Ñi rab jàpp it, wér.
19Mbooloo mépp a ko doon wuta laal ndax leer guy bàyyikoo ca moom, di faj ñépp.
20Yeesu nag xool ay taalibeem, ne leen: «Ndokklee yeen ñi néewle, nde nguurug Yàlla, yeenay boroom.
21Ndokklee yeen ñi xiif tey, nde dingeen regg. Ndokklee yeen ñiy jooy tey, nde dingeen ree.
22Ndokklee yeen, bu leen nit ñi bañee, daggook yeen, saaga leen, sikkal seen der ndax Doomu nit ki.
23Bésub keroog, bégleen te bànneexu bay fecc ndax seen yoolub ëllëg bu réy, nde noonu la seen maami bañ yooyu daan def ak yonent ya.
24Waaye wóoy ngalla yeen ñi barele, ndax neexle ngeen ba noppi.
25Wóoy ngalla yeen ñi regg tey, ndax dingeen xiif ëllëg. Wóoy yeen ñiy ree tey, ndax dingeen tiislu, dingeen jooy.
26Wóoy ngalla yeen, bu leen ñépp dee waxal lu baax, ndax noonu rekk la maami ñooñu daan jëfe ak yonenti caaxaan ya.
27«Yeen ñi may déglu, dama ne, seeni noon, soppleen leen, seeni bañ, defal-leen leen lu baax.
28Ñi leen di móolu, yéeneleen leen lu baax, ñi leen di soxore, ñaanal-leen leen.
29Ku leen talaata cib lex, dékkleen ko ba ca des. Ku nangu seen mbubb mu mag, buleen ko teree jëlaale seenub turki.
30Képp ku leen ñaan, mayleen ko; ku nangu seen yëf, buleen ko ko laaj.