Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 1

Luug 1:8-20

Help us?
Click on verse(s) to share them!
8Sàkkaryaa la làngam aye woon, muy def liggéeyu carxalam fa kanam Yàlla.
9Ba ñu tegoo bant, na ko sarxalkat yi baaxoo woon, moom la bant ba dal, mu wara dugg biir néegu Boroom bi, ngir taal fa saraxu cuuraay.
10Mbooloo mépp nag a nga woon ca biti di julli, ca waxtuw saraxu cuuraay boobu.
11Ci biir loolu menn malaakam Boroom bi jekki feeñu Sàkkaryaa, ca wetu ndijooru sarxalukaayu cuuraay ba.
12Ba ko Sàkkaryaa gisee daa jaaxle, tiitaange jàpp ko.
13Malaaka ma ne ko: «Sàkkaryaa, bul tiit, ndax sa ñaan nangu na. Elisabet sa soxna dina am doom ju góor, nanga ko tudde Yaxya.
14Dinga am mbégte ak bànneex, te ñu bareey bég ci juddoom,
15ndax ku màgg lay doon, Boroom bi seede. Biiñ ak lenn luy màndee nag, du ko naan, Noo gu Sell gi mooy dale ca biiru ndeyam, solu ko ba fees.
16Niti bànni Israyil ñu bare, moo leen di waññi ci Boroom bi seen Yàlla.
17Mooy ndaw li koy jiitu, ànd ak leer ga ak xam-xam, ba woon ca Yonent Yàlla Ilyaas, ba waññi xolu baay ci doomam, waññi ku déggadi ci xelum aji jub, loolu yépp ngir waajal aw xeet ba ñu jekk ngir Boroom bi.»
18Sàkkaryaa nag ne malaaka mi: «Lu may def ab takk ci loolu ba mu bir ma? Ndax man màggat naa, te sama soxna it làq na ay fan.»
19Malaaka ma ne ko: «Man maay Jibril miy taxaw fi kanam Yàlla. Dañu maa yónni ngir ma wax ak yaw, yégal la bii xibaaru jàmm.
20Léegi nag, dama ne, gannaaw gëmuloo sama kàddu, giy jot, sotti, dinga luu te dootuloo mana wax, ba kera loolu di am.»

Read Luug 1Luug 1
Compare Luug 1:8-20Luug 1:8-20