Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 1

LUUG 1:8-20

Help us?
Click on verse(s) to share them!
8Benn bés nag Sakari doon def liggéeyu sarxaleem ca Yàlla, ndaxte mbootaayam a aye keroog.
9Bi ñuy tegoo bant, ni ko sarxalkat yi daan defe naka-jekk, ngir xam kan mooy dugg ca bérab bu sell ba ca kër Yàlla ga, ngir taal fa cuuraay, bant ba tegu ci Sakari.
10Ca waxtu wa ñuy taal cuuraay la, mbooloo maa nga woon ca biti, di ñaan.
11Noonu benn malaakam Boroom bi daldi feeñu Sakari, taxaw ca féeteek ndijooru sarxalukaay, ba ñuy taal cuuraay ca kawam.
12Naka la ko Sakari gis, fitam daldi dem, mu tiit.
13Waaye malaaka ma ne ko: «Bul ragal dara Sakari, ndaxte sa ñaan nangu na. Elisabet sa soxna dina la jural doom, te dinga ko tudde Yaxya.
14Sa mbég lay doon, sa xol sedd ci, te ñu bare dinañu bég ci juddoom,
15ndaxte dina nekk ku màgg ca kanam Yàlla. Du naan biiñ walla dara luy màndil, te bu juddoo, Xel mu Sell mi daldi ko solu.
16Dina delloosi niti Israyil yu bare ci Yàlla seen Boroom.
17Mooy jiitu, di yégle ñëwug Boroom bi, ànd ak xel mi ak doole, ji yonent Yàlla Ilyaas amoon, ngir jubale xoli baay yi ak doom yi, ngir delloo ñi déggadi ci maanduteg ñi jub. Noonu dina waajal mbooloo muy teeru Boroom bi.»
18Sakari daldi ne malaaka ma: «Nan laay xame ne loolu dëgg la? Ndaxte mag laa, te sama soxna it màggat na.»
19Malaaka ma ne ko: «Man maay Jibril miy taxaw ci kanam Yàlla. Dañu maa yónni ngir ma wax ak yaw te yégal la xibaaru jàmm boobu.
20Léegi nag gannaaw gëmuloo li ma wax, dinga luu te dootuloo mana wax, ba kera sama wax di am, bu jamonoom jotee.»

Read LUUG 1LUUG 1
Compare LUUG 1:8-20LUUG 1:8-20