34Maryaama laaj malaaka ma ne ko: «Naka la loolu mana ame? Man de, janq laa ba tey.»
35Malaaka ma ne ko: «Xel mu Sell mi dina wàcc ci yaw, te Aji Kawe ji dina la yiir ci kàttanam. Moo tax xale biy juddu dinañu ko wooye Ku sell ki, Doomu Yàlla ji.
36Elisabet sa mbokk mi it dina am doom ju góor cig màggatam. Ki ñu doon wooye ku manula am doom, mu ngi ci juróom benni weeram.
37Ndaxte dara tëwul Yàlla.»
38Maryaama ne ko: «Jaamub Boroom bi laa. Na Yàlla def ci man li nga wax.» Ci noonu malaaka ma daldi dem.
39Ci jamono jooju Maryaama jóg, gaawantu dem ci benn dëkk bu nekkoon ca tund ya ca diiwaanu Yude.
40Mu dugg ca kër Sakari, daldi nuyu Elisabet.