34 Ci kaw loolu Maryaama laaj malaaka mi ne ko: «Nu loolu di ame, te man xawma góor?»
35 Malaaka mi ne ko: «Noo gu Sell gi mooy wàccsi ci yaw, dooley Aji Kawe ji yiir la. Moo tax itam ku Sell kiy juddoo ci yaw, dees na ko wooye Doomu Yàlla.
36 Te kat Elisabet sa mbokk mi itam ëmb na doom ju góor te fekk ko màggat. Ki ñu doon wooye jigéen ju jaasir, mu ngi nii ci juróom benni weeram,
37 ndax Yàlla, dara tëwu ko.»
38 Maryaama daldi ne: «Maa ngi, di jaamub Boroom bi. Nii nga waxe, na ame noonu ci man.» Ba loolu amee malaaka ma bàyyikoo ca moom, dem.
39 Ci fan yooyu la Maryaama fabu gaaw, jëm diiwaanu tund ya, ca dëkkub Yude,
40 ba Sàkkaryaa dëkke. Mu agsi ca kër ga, nuyu Elisabet.