Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàdduy Waare - Kàdduy Waare 5

Kàdduy Waare 5:3-15

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Boo digook Yàlla, bu ko yeexe; Daray foontukat neexul, defal li nga dige.
4Baña digee gën dige loo deful.
5Bu la sa làmmiñ yóbbe bàkkaar, ba ngay lay ndawal Yàlla la, naan lii njuumte la woon. Ana lu jar Yàlla di la meree sa kàddu, bay neenal saw ñaq?
6Wax ju bare, caaxaani neen; mook gént yu baree yem. Kon, Yàlla, ragal ko.
7Boo gisee ñuy not néew-ji-doole, di jalgati dëgg ak yoon cib gox, bumu la jaaxal; kilifa gi, kilifaam a ko yiir; ñoom it seen kilifaa leen yiir.
8Xanaa ndax buur suqal mbey mi, ba ñépp jariñoo suuf si.
9Bëggkatu xaalis du doyal xaalis, bëggkatu alal du doyal tono, te loolu it, cóolóoli neen.
10Bu koom yokkoo, lekk-kat yi yokku. Ana lu muy jariñ boroom koom ga, xanaa di ko duufale bëtam?
11Surga, lekkam néew, bare, mu nelaw, ba fàttey boram; boroom alal regg, du nopplu, du nelaw.
12Naqar wu réy laa gis fi kaw suuf: Alal ju boroom dajale ba loru,
13mbaa pexeem moy, mu sànkule; ba bu amee doom it, du ko wacce dara.
14Nga juddoo ci sa ndey loxoy neen, walbatiku dellu na nga dikke woon. Du dara loo ñaqoon ba yóbbaale ko.
15Dikke ni, delloo ni, loolu it tiis wu réy la. Doñ-doñi, ngelawal neen, ana jariñ la?

Read Kàdduy Waare 5Kàdduy Waare 5
Compare Kàdduy Waare 5:3-15Kàdduy Waare 5:3-15