14Day toog bunt këram, mbaa fu kawee kawe ca dëkk ba,
15di woo ña fay jaare te jubal seenu yoon.
16Ma nga naa: «Képp ku téxét, jàddal ba fii!» Ku ñàkk bopp, mu ne ko:
17«Ndox mu lewul a neex, ñamu làqu-lekk dàqati.»
18Waaye kooka du xam ne waa njaniiw a nga fa, te ku wuyji, tàbbi biir bàmmeel.