Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 9:14-18 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 9:14-18 in Kàddug Yàlla gi

14 Day toog bunt këram, mbaa fu kawee kawe ca dëkk ba,
15 di woo ña fay jaare te jubal seenu yoon.
16 Ma nga naa: «Képp ku téxét, jàddal ba fii!» Ku ñàkk bopp, mu ne ko:
17 «Ndox mu lewul a neex, ñamu làqu-lekk dàqati.»
18 Waaye kooka du xam ne waa njaniiw a nga fa, te ku wuyji, tàbbi biir bàmmeel.
Kàddu yu Xelu 9 in Kàddug Yàlla gi