13Lu ma tee woona dégg ku may digal, tey teewlu sama waxi sëriñ ya?
14Tuuti ma yàqu yaxeet fi kanam ñépp!»
15Naanal ci sa mbalkam bopp, ndox ma balle sa teenu bopp.
16Xanaa doo wasaare sa bëti ndox ca biti, mu def ay wal ca pénc ya?
17Nay sa alal, yaw doŋŋ, ku bokk feneen bokkul.