19Yoonu ku bon ne këruus, du xam lu muy téqtaloo.
20Doom, déglul samay kàddu, teewlul samay wax.
21Bu ci noppee ja jàkk, te jàpp ko ci sa biir xel.
22Mooy dundloo ku ci jàpp, di wéral jëmmam jépp.
23Sàmmala sàmm sab xol, nde xalaati xol ngay jëfe.
24Dàqal wor, mu sore la; kàdduy naxe, na la dànd.
25Xooleel, sa bët ne jàkk, ngay xool sa kanam màkk.
26Seetlul fi ngay teg tànk, ba foo awe, mu wóor.
27Bul jàdd, ndijoor mbaa càmmoñ, na sa tànk moyu lu bon.