1Bul ñee ku bon, bul wuta ànd ak moom,
2ndax coxor lay nas ci xolam, te fitna la ay waxam di yee.
3Xel mu rafet ay tabax kër, rafet déggin a koy samp.
4Xam-xam ay feesal néeg ya ak mboolem alal ju jafe te yànj.
5Ku rafet xel di boroom doole, ku xam, gëna man;
6tegtal yu xelu lañuy xaree, diisoo bu yaatooy maye ndam.
7Wax ju xelu sut nab dof, jataayu pénc du fa àddoo.
8Kuy mébét lu bon, ñu ne yaay rambaaj bi.
9Pexem dof bàkkaar la, te kuy ñaawle, ñu sib la.
10Bu mettee, nga yoqi, sa doolee néew.