24Su doom jubee, seral xolu baay. Boo juree ku rafet xel, am nga bànneex.
25Deel bégal ndey ak baay, rawatina ndey ji la jur.
26Doom, teewloo ma xel te roy ma.
27Ab gànc yeer mu xóot la, jabaru jaambur di teen bu xat.
28Ma ngay tëroo nib sàcc, góor ñu bare lay fecciloo worma.
29Ana kuy tiislu, naan: «Wóoy, ngalla man!» Ana kuy xulook a jàmbat, di gaañu ci dara, bët ya xonq curr?
30Xanaa kiy naan-naane biiñ, di mosi yeneen njafaan?
31Bul xool biiñ ak xonqaayam. Aka yànj cib kaas te neexa jolu!
32Bu weesee mu màtt la ni jaan, ne la càppit ni ñàngóor.
33Dangay mel ni kuy gis lu doy waar, sam xel di ràbb lu jekkadi.
34Nga mel ni ku tëdd biir géej, di jaayu ca biir gaal ga,
35nga naan: «Dañu maa dóor te gaañuwuma, duma ma te yéguma ko. Moo! Duma yewwu nag, ba naaneeti?»