Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 23

Kàddu yu Xelu 23:24-29

Help us?
Click on verse(s) to share them!
24Su doom jubee, seral xolu baay. Boo juree ku rafet xel, am nga bànneex.
25Deel bégal ndey ak baay, rawatina ndey ji la jur.
26Doom, teewloo ma xel te roy ma.
27Ab gànc yeer mu xóot la, jabaru jaambur di teen bu xat.
28Ma ngay tëroo nib sàcc, góor ñu bare lay fecciloo worma.
29Ana kuy tiislu, naan: «Wóoy, ngalla man!» Ana kuy xulook a jàmbat, di gaañu ci dara, bët ya xonq curr?

Read Kàddu yu Xelu 23Kàddu yu Xelu 23
Compare Kàddu yu Xelu 23:24-29Kàddu yu Xelu 23:24-29