Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 23:24-29 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 23:24-29 in Kàddug Yàlla gi

24 Su doom jubee, seral xolu baay. Boo juree ku rafet xel, am nga bànneex.
25 Deel bégal ndey ak baay, rawatina ndey ji la jur.
26 Doom, teewloo ma xel te roy ma.
27 Ab gànc yeer mu xóot la, jabaru jaambur di teen bu xat.
28 Ma ngay tëroo nib sàcc, góor ñu bare lay fecciloo worma.
29 Ana kuy tiislu, naan: «Wóoy, ngalla man!» Ana kuy xulook a jàmbat, di gaañu ci dara, bët ya xonq curr?
Kàddu yu Xelu 23 in Kàddug Yàlla gi