8Ab saaysaay day dëngal, nit ku dëggu di jubal.
9Dëkkeb ruq cim sàq moo gën jabar ju pànk.
10Ab soxor day namma lore, te du yërëm moroomam.
11Boo mbugalee kuy ñaawle, ab téxét jànge ca; nga jàngal ku rafet xel, mu yokku.
12Aji Jub ji Yàlla xam na la ne ca biir kër ku bon, te mooy sànk ku bon.
13Ku tanqamlu jooyi ku ñàkk dina woote wall, wall ñàkk.
14Ku mer, may ko ci sutura, mu giif; boroom xadar, boqal ko neexal, mu dal.
15Bu yoon amee, ku jub bég; kuy def lu bon jàq.
16Ku noppee jëfe xel, noppluji njaniiw.
17Ku topp sa bànneex, mujje ñàkk; ku sopp biiñ ak lu niin du woomle.
18Ku bon këppoo ayu ku baax, workat gàddu musibam kuy jubal.
19Dëkke ndànd-foyfoy moo gën jabar ju tàng, bare ay.
20Ku xelu denc këram ngëneeli alal aku diw, ab dof saax-saaxee josam.
21Ku saxoo njekk ak ngor am fan wu gudd, naataangeek daraja.
22Ku ñaw mana daan jàmbaari dëkk bu mag, ba màbb tata ja ñu yaakaaroon.
23Ub sa gémmiñ, moom sa làmmiñ, mucc ci njàqare.
24Ku réy te bew, mooy ñaawle, day reew, ba jéggi dayo.