1Xolu buur walum ndox la ci loxol Aji Sax ji, fu ko soob mu jëme ko fa.
2Lu waay def, daa jub ca moom, waaye Aji Sax jeey natt xol yi.
3Deel def dëgg ak njekk, moo gënal Aji Sax ji ab sarax.
4Xeebaateek réy-réylu mooy bàkkaar yi ñuy ràññee ku bon.
5Farlu, woomle; ku gaawtu, mujj néewle.
6Alal ju la fen may, cóolóol la, day naaw, wut ko xaru la.
7Coxor day sànk boroom, ndax day baña def njub.