Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 5

JËF YA 5:4-15

Help us?
Click on verse(s) to share them!
4Bi mu jaragul, ndax moomuloo ko woon? Te bi mu jaree, ndax yilifuloo woon njég li? Lu tax nga fas ci sa xol def nii? Woruloo nit ñi, waaye Yàlla nga wor.»
5Bi Anañas déggee baat yooyu, mu daanu dee. Ñi ko dégg ñépp tiit, ba ne nërëm.
6Noonu waxambaane ya jóg, ñu sàng ko, yóbbu ko, jébbal Yàlla.
7Ñetti waxtu gannaaw ga, jabaram duggsi, fekk xamul la fa xew.
8Piyeer daldi ko ne: «Wax ma, ndax lii mooy njégu tool bi?» Mu ne ko: «Waawaaw, lii la.»
9Ci kaw loolu Piyeer ne ko: «Lu tax ngeen ànd, di diiŋat Xelu Boroom bi? Ñi denci woon sa jëkkër ñu ngi nii ci bunt bi, te dinañu la yóbbu.»
10Ca saa sa mu daanu ciy tànkam, dee. Bi waxambaane ya agsee nag, ñu fekk ko, mu faatu; ñu yóbbu ko, def ko ci wetu jëkkëram.
11Noonu tiitaange ju mag tàbbi ci mbooloom ñi gëm ñépp ak ñi ko dégg ñépp.
12Bi loolu amee ay kéemaan ak ay firnde yu bare di xew ci nit ñi, jaare ca loxoy ndaw ya. Ñépp di booloo ca Werandaa bu Suleymaan ca kër Yàlla ga.
13Te kenn ci ña ca des ñemewula booloo ak ñoom, waaye nit ñépp di leen màggal.
14Moona ay nit ñu gëna bare, góor ak jigéen, di gëm Boroom bi, tey taq ci ñoom.
15Nit ñi indi sax ñu wopp ca mbedd ya, teg leen ca ay lal yu ndaw ak ay leeso, ngir bu Piyeer di jaar, doonte takkandeeram sax yiir ñenn ci ñoom.

Read JËF YA 5JËF YA 5
Compare JËF YA 5:4-15JËF YA 5:4-15