19Doomu ndaw sii nag dee ci guddi, ndax daa tëddoon ci kawam.
20Mu jóg ci xaaju guddi, jële sama doom fi sama wet, tëral ci wetam. Fekk man, sang bi, maa ngi nelaw. Doomam ji dee nag, mu tëral ko ci sama wet.
21Naka laa jóg ci suba, di nàmpal sama doom, gisuma lu moy mu dee. Ba bët setee nag ma xool ko bu baax, ndeke du sama doom ji ma jur.»
22Seneen ndaw sa ne: «Déedéet, sama doom mooy dund, sa doom a dee.» Ku jëkk ka ne: «Déedéet, sa doom a dee, sama doom a ngi dund.» Ñu di ko werante fi kanam Buur.
23Buur ne: «Kii a ngi naan: “Sama doom jii mooy dund, sa doom a dee.” Kee naan: “Déedéet, sa doom a dee, sama doom mooy dund.”»
24Buur teg ca ne: «Indil-leen ma saamar!» Ñu indil Buur saamar.
25Buur ne: «Dogleen xale biy dund ñaar, te jox kii genn-wàll, jox kee genn-wàll.»