Text copied!
Bibles in Wolof

1.Buur ya 3:19-25 in Wolof

Help us?

1.Buur ya 3:19-25 in Kàddug Yàlla gi

19 Doomu ndaw sii nag dee ci guddi, ndax daa tëddoon ci kawam.
20 Mu jóg ci xaaju guddi, jële sama doom fi sama wet, tëral ci wetam. Fekk man, sang bi, maa ngi nelaw. Doomam ji dee nag, mu tëral ko ci sama wet.
21 Naka laa jóg ci suba, di nàmpal sama doom, gisuma lu moy mu dee. Ba bët setee nag ma xool ko bu baax, ndeke du sama doom ji ma jur.»
22 Seneen ndaw sa ne: «Déedéet, sama doom mooy dund, sa doom a dee.» Ku jëkk ka ne: «Déedéet, sa doom a dee, sama doom a ngi dund.» Ñu di ko werante fi kanam Buur.
23 Buur ne: «Kii a ngi naan: “Sama doom jii mooy dund, sa doom a dee.” Kee naan: “Déedéet, sa doom a dee, sama doom mooy dund.”»
24 Buur teg ca ne: «Indil-leen ma saamar!» Ñu indil Buur saamar.
25 Buur ne: «Dogleen xale biy dund ñaar, te jox kii genn-wàll, jox kee genn-wàll.»
1.Buur ya 3 in Kàddug Yàlla gi