Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Buur ya - 1.Buur ya 20

1.Buur ya 20:11-32

Help us?
Click on verse(s) to share them!
11Buurub Israyil ne: «Waxleen ko ne ko: “Jóge xare, di bàkku moo gën jëm xare, di bàkku.”»
12Ba Ben Addàd di jot ca kàddu googu, ma ngay naan, mook buur ya far ak moom ca mbaar ya. Mu jox ay nitam ndigal ne leen: «Takkuleen!» Ñu takku, ngir songi dëkk ba.
13Ndeke ci biir loolu ab yonent dem na ca Axab buurub Israyil, ne ko: «Aji Sax ji dafa wax ne: Gis nga mbooloom xare mii mépp ak li ñuy bare lépp, xamal ne teg naa leen ci sa loxo bésub tey, ndax nga xam ne maay Aji Sax ji.»
14Axab ne ko: «Ku may defal loolu?» Mu ne ko: «Aji Sax ji nee: Dag yi kilifay diiwaan yi yebal lay doon.» Axab ne ko: «Kuy sooke xare bi?» Mu ne ko: «Xanaa yaw.»
15Ba mu ko defee Axab lim dag ya kilifay diiwaan ya yebal, ñuy ñaar téeméer ak fanweer ak ñaar (232). Gannaaw loolu mu lim mbooloom Israyil gépp, ñuy juróom ñaari junni (7 000).
16Ñu génn digg bëccëg, fekk Ben Addàd a ngay màndi mook fanweeri buur ak ñaar ya mu faral, ca mbaar ya.
17Dag ya kilifay diiwaan ya yebal a nga jiitu. Ci biir loolu Ben Addàd yónnee, ñu wax ko ne ko: «Am na ñu jóge Samari, di ñëw.»
18Mu ne: «Su leen jàmm taxee jóg, jàppleen leen, ñuy dund; su leen xare taxee jóg it, jàppleen leen, ñuy dund.»
19Ba mu ko defee dagi kilifay diiwaan ya génne ca dëkk ba, mbooloom xare ma topp ca seen gannaaw.
20Ku nekk jam noon ba nga janool, waa Siri daw, Israyil topp leen. Ben Addàd buurub Siri nag war fas, daw mooki gawaram.
21Buurub Israyil nag song leen, rey fas ya, yàq watiir ya, daan waa Siri jéll bu réy.
22Yonent ba dikk ca buurub Israyil ne ko: «Nanga dëgërluwaat te xam ni nga wara def, ndax nëgëni déwén buurub Siri dina la songaat.»
23Ba loolu amee kàngami buurub Siri digal buurub Siri ci wàllu Israyil, ne ko: «Ñii, seeni tuur tuuri tund lañu; moo tax ñu ëpp nu doole, waaye su nu xeexeek ñoom ci joor gi déy, su boobaa noo leen di ëpp doole.
24Defal nii: follil buur yi ci sa gannaaw yépp, jële leen fa ñu jiite, teg fa jawriñ yu leen wuutu.
25Te yaw nga sosaat mbooloom xare mu mel ni ma nga amoon, fas ak fas, watiir ak watiir, ndax nu mana xareek ñoom ci joor gi. Su boobaa déy, noo leen di ëpp doole.» Mu déggal leen, def noona.
26Ca déwén sa Ben Addàd lim waa Siri, daldi dem Afeg ca xare baak Israyil.
27Waa Israyil daje, sàkk ab dund, ba noppi dox wuti leen. Waa Israyil a nga dal janook ñoom, di saf ñaari gétti bëy. Waa Siri ñoom fees àll ba.
28Góoru Yàlla ga dikk ne buurub Israyil: «Aji Sax ji dafa wax ne: Gannaaw waa Siri dañoo yaakaar ne man Aji Sax ji, yàllay tund laa, duma yàllay xur, maay teg mbooloo mu réy mii mépp ci say loxo. Su ko defee ngeen xam ne maay Aji Sax ji.»
29Diiru juróom ñaari fan nag ñu jàkkaarloo ca seeni dal. Bésub juróom ñaareel ba xare ba jib, waa Israyil daane téeméeri junniy xarekat (100 000) yu warul fas ca waa Siri ci benn bés bi;
30ña ca des daw ba Afeg, ca biir dëkk ba, tata ja màbb ca kaw ñaar fukki junniy nit ak juróom ñaar (27 000) ca ñoom. Fekk na Ben Addàd daw dugg ca biir dëkk ba, jàll ci biir néeg bu làqoo làqu.
31Ay jawriñam ne ko: «Waaw, nun de dégg nanu ñu naa buuri Israyil buur yu baax lañu. Tee noo sol ay saaku, tañlaayoo buum, toroxloo ko, te dem ca buurub Israyil? Jombul mu bàyyi la, nga dund.»
32Ñu teraxlaayoo ay saaku, tañlaayoo ay buum, dem ca buurub Israyil, ne ko: «Ben Addàd sa jaam ba nee, nga baal ko ngalla te bàyyi ko mu dund.» Mu ne: «Ndeke mu ngi dund ba tey? Moom sama mbokk a!»

Read 1.Buur ya 201.Buur ya 20
Compare 1.Buur ya 20:11-321.Buur ya 20:11-32