Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 25

Sarxalkat yi 25:29-55

Help us?
Click on verse(s) to share them!
29«Su dee waa ju jaay ab dëkkuwaay bu nekk ci dëkk bu mag bu ñu tabax tata wëralee ko ko, dina ko saña jotaat li feek njaay mi amul at. Ci diir boobu la ko saña jotaate.
30Su ñu ko jotaatul ba njaay ma am atum lëmm, dëkkuwaay boobu ci biir dëkk bu mag ba ñu wëralee tata day wel fàww, ñeel ka ko jënd, mook ku askanoo ci moom. Du lees di delloo ci atum Yiwiku.
31Su dee ay dëkkuwaay ci dëkk yu ndaw yu ñu tabaxul tata, wëralee ko ko, dees koy yemaleek alali suuf. Sañees na koo jotaat te dees koy delloo ci atum Yiwiku.
32«Su dee dëkki Leween ñi ak seen dëkkuwaay ya ca biir nag, Leween ñi sañ nañu cee jotaat fàww.
33Kon alalu Leween manees na koo jotaat —dëkkuwaay lay doon bu ñu jaay ci dëkki Leween ñi— dees koy delloo bu atum Yiwiku dikkee, ndax dëkkuwaay yi ci dëkki Leween ñi, seen alal la ju leen lew fàww ci seen biir bokki bànni Israyil.
34Waaye suufas parlu yi bokk ci dëkki Leween ñi, deesu ko jaay, ndax ñoo koy moom fàww.
35«Bu seen mbokkum bànni Israyil ñàkkee ba manatula fey lu mu leen ameel, nangeen ko dimbali, ni bu doon doxandéem mbaa màngaan, ndax mu mana dund ci seen biir.
36Buleen teg lenn lu mu mana doon ci bor bu leen seen mbokk moomu ameel, waaye ragal-leen ci seen Yàlla, ndax mu mana dund ci seen biir.
37Buleen ko lebal seen xaalis, di ca teg lenn, te buleen ko jox dund, di sàkku lu mu ca yokk ngir delloo leen ko.
38Man Aji Sax ji maay seen Yàlla ji leen génne réewum Misra, jox leen réewu Kanaan, te di seen Yàlla.
39«Bu seen mbokk ñàkkee ci seen biir, ba jaay leen boppam, buleen ko jaamloo.
40Defleen ko ni liggéeykat buy feyeeku mbaa màngaan bu ngeen dëkkal. Na leen liggéeyal ba keroog atum Yiwiku ma,
41mu génn ci seeni loxo, mook ay doomam, daldi dellu ci làngu boppam, fa ay maamam séddoo.
42Li waral loolu moo di bànni Israyil dañu di sama jaam yi ma génne réewum Misra. Deesu leen jaay njaam.
43Buleen leen soxore ci biir kilifteef, waaye ragal-leen ci seen Yàlla.
44Seen jaam yu góor ak seen jaam yu jigéen, nangeen leen jële ci xeet yi leen wër. Ci ñooñu ngeen di jënde ay jaam, góor ak jigéen.
45Walla ngeen jënde ba tey ci doxandéem yi ci seen biir, mbaa ci njaboot yi doxandéem yi am ci réew mi te ñu nekk ci seen biir. Su ko defee ñu doon seen ngàllo.
46Sañ ngeen leena donale seen doom yi leen di wuutu, ñu doon seen ngàllo seen giiru dund. Ñooñu sañ ngeen leena def ay jaam, waaye su dee ci seen diggante, yeen bànni Israyil, buleen di soxorante ci biir kilifteef.
47«Su fekkee ne ab doxandéem bu ngeen dëkkal mbaa ab màngaan dafa woomle te kenn ci seeni bokk ñàkk, ba jaay boppam doxandéem bi ngeen dëkkal mbaa kenn ku bokk ak doxandéem bi,
48gannaaw bu jaayee boppam, manees na koo jotaat ba tey. Kenn ciy bokkam sañ na koo jotaat,
49yaar muy baayam bu ndaw mbaa doomu baayam bu ndaw. Ku mu bokkal làng di mbokkam lenqe sax man na koo jotaat, te moom ci boppam man naa woomle ba jotaat boppam.
50Na bokk ak ka ko jënd waññ, la dale ca at ma mu jaaye boppam, ba ca atum Yiwiku may ñëw, muy njégu goreelam, dëppook at yooya. Te it nañu ci seet àqu ñaqu liggéeykat.
51Su desee ay at, lu at ya gëna baree, njég ga muy jotaate boppam gëna sore ci njég, ga ñu ko jënde woon.
52Te su at yu néew doxee seen digganteek atum Yiwiku ma, na ko waññ te fey lu ni néewe, ngir jotaat boppam.
53Ab surga lay doon ci njaatigeem at mu nekk, waaye waru koo soxore ci biir kilifteef, ngeen di seetaan.
54Su fekkee ne jotaatuñu ko ci jotin yooyu sax, war naa moom boppam mooki doomam ca atum Yiwiku ma.
55Ndax kat man la bànni Israyil di samay jaam. Ñoo di sama jaam ya ma génne réewum Misra; yeen, maay seen Yàlla Aji Sax ji.

Read Sarxalkat yi 25Sarxalkat yi 25
Compare Sarxalkat yi 25:29-55Sarxalkat yi 25:29-55