7Nuyul-leen ma Andoronikus ak Yuña, sama bokki Yawut, yi ñu ma tëjandooloon; ñu ñu nawloo lañu ci ndaw yi, te ñoo ma jëkka gëm sax Almasi.
8Nuyul-leen ma Ampilyaatus, mi ma soppal sama bopp ndax Sang bi.
9Nuyul-leen ma it Urben, sunu mbokkum liggéeykat ci liggéeyub Almasi, ak Estakis, sama soppe;
10nuyul-leen ma Apeles mi firndeel kóllëre gi mu am ci Almasi, te ngeen nuyul ma waa kër Aristobul,
11ak Erojon sama mbokkum Yawut, te ngeen nuyul ma waa kër Narsis ñi gëm Sang bi.
12Nuyul-leen ma Tirifen ak Tirifos, jigéen ñu sonn ci liggéeyu Boroom bi, ak it ndaw si Persidd mi sonn lool ci liggéeyu Boroom bi.
13Nuyul-leen ma Rufus, mi Boroom bi taamul boppam, ak yaayam jiy sama yaayu bopp.
14Nuyul-leen ma Asànkirit ak Felegon ak Ermes ak Patarobas ak Ermas, ak mboolem bokk yi nekk ak ñoom.
15Nuyul-leen ma it Filolog ak Yuli, ak Nere ak jigéenam, ak Olimpas ak mboolem ñu sell ñi nekk ak ñoom.
16Saafoonteeleen fóonante yu sell. Mboolooy gëmkati Almasi yépp nuyu nañu leen.
17Léegi nag bokk yi, dama leen di ñaax, ràññeeleen ñi gàntal àlluwa ji ngeen jànge, di féewale, ak a téqtale, te ngeen moytu leen.