7 Nuyul-leen ma it Andoronikus ak Yuñas, sama bokk, yi ñu ma booleeloon tëj; am nañu tur ci ndawi Yàlla yi, te ñoo ma jiitu sax ci gëm Kirist.
8 Te fàttewuma Ampilyaatus, mi ma bëgg ci sama xol ngir Boroom bi.
9 Nuyul-leen ma it Urban, sunu nawle ci liggéeyu Kirist, ak sama soppe Estakis;
10 ak it Apeles, mi ngëmam dëggu, ba yelloo kóolute. Nuyul-leen ma it waa kër Aristobul,
11 ak Erojon sama mbokk, ak waa kër Narsis, ñi ci Boroom bi.
12 Maa ngi nuyu Tirifen, moom ak Tirifos, jigéen ñi sonn ci liggéeyu Boroom bi, ak it sama soppe Persidd, mi ci jeex tàkk.
13 Maa ngi nuyu it Rufus, waa ji xolam seey ci Boroom bi, ak yaayam, mi ma féete woon it cérub ndey.
14 Te fàttewuma Asànkirit, Felegon, Ermes, Patarobas, Ermas, ñoom ak mboolem bokk yépp.
15 Nuyul-leen ma it Filolog ak Yuli, Nere ak jigéenam. Te fàttewuma Olimpas ak gaayi Yàlla yiy booloo ak ñoom ñépp.
16 Te yéen bokk yi, saafoonteleen ak xol bu laab. Mboolooy ñi gëm Kirist yépp a ngi leen di nuyu.
17 Bokk yi, maa ngi leen di dénk, ngeen moytu ñi leen di féewale, ba di leen jàddloo yoon wi, ciy wax lu juuyoo ak dëgg gi ngeen jàng. Dawleen leen ba sore.