Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - MÀRK - MÀRK 8

MÀRK 8:17-36

Help us?
Click on verse(s) to share them!
17Waaye Yeesu yég loolu ne leen: «Lu tax ngeen di werante ci li ngeen indaalewul mburu? Xanaa gisaguleen te xamuleen? Ndax seen xol dafa fatt ba tey?
18Ndax ay gumbay njàccaar ngeen, te seeni nopp naqari? Xanaa fàttalikuwuleen;
19bi ma dammee juróomi mburu ya ngir juróomi junni ña, ñaata pañe yu fees ak ay dammit ngeen ca dajale woon?» Ñu ne ko: «Fukk ak ñaar.»
20Yeesu neeti leen: «Te bés bi ma dammee juróom ñaari mburu yi ngir ñeenti junni ñi, ñaata dàmba yu fees ak dammit ngeen dajale woon?» Ñu ne ko: «Juróom ñaar.»
21Noonu Yeesu ne leen: «Ndax seen xol dafa tëju ba tey?»
22Gannaaw loolu ñu ñëw ci Betsayda. Foofa ñu indil Yeesu ku gumba, di ko ñaan, mu laal ko.
23Yeesu nag jàpp loxob gumba gi, yóbbu ko, ba génn dëkk bi. Mu def tiflit ciy bëtam, teg ko loxo naan: «Ndax gis nga dara?»
24Waa ji xool ne ko: «Gis naa ay nit, ñu mel ni ay garab, te ñu ngi dox.»
25Kon Yeesu laalaat bët yi, gumba gi ne xefeet, daldi wér, ba gis lépp bu leer.
26Ci kaw loolu Yeesu sant ko mu ñibbi ne ko: «Bul dugg ca dëkk ba.»
27Bi loolu amee Yeesu ànd ak ay taalibeem, dem ca dëkk, yi wër Sesare bu Filib. Bi ñuy dem nag, mu laaj taalibe yi: «Nit ñi, lu ñu wax ne man moom laa?»
28Ñu ne ko: «Am na ñuy ne yaa di Yaxya; ñeneen ne, Ilyaas; ñi ci des ne yaay kenn ci yonent yi.»
29Noonu Yeesu laaj leen: «Yéen nag, ku ngeen wax ne moom laa?» Piyeer ne ko: «Yaa di Almasi bi.»
30Ci kaw loolu Yeesu dénk leen bu wóor, ñu bañ koo wax kenn.
31Booba Yeesu tàmbali na leena xamal ne, Doomu nit ki war na sonn lu bare; njiit ya, sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya dëddu ko, ñu rey ko, mu dekki ci ñetti fan.
32Noonu mu xamal leen mbir mi, ba mu leer nàññ. Bi ko Piyeer déggee, mu woo ko ci pegg, daldi ko yedd.
33Waaye Yeesu geestu, gis yeneen taalibe yi, mu daldi yedd Piyeer ne ko: «Sore ma Seytaane; yëfi nit ngay fonk, waaye du yëfi Yàlla.»
34Noonu Yeesu woo taalibe yi ak mbooloo mi ne leen: «Ku bëgga topp ci samay tànk, na bàyyi boppam te gàddu bant bi ñu ko wara daaj, doora topp ci man.
35Ndaxte koo xam ne bëgg ngaa rawale sa bakkan, dinga ko ñàkk, waaye ku ñàkk sa bakkan ngir man ak ngir xibaaru jàmm bi, dinga ko jotaat.
36Ndaxte moom àddina sépp, lu muy jariñ nit, bu ñàkkee bakkanam?

Read MÀRK 8MÀRK 8
Compare MÀRK 8:17-36MÀRK 8:17-36