3Balaam ne Balag: «Taxawal fii ci sa saraxu rendi-dóomal, ma dem ba nee. Jombul Aji Sax ji dikk, dajeek man. Mbir mu mu ma won, dinaa la ko àgge.» Mu daldi dem ba ca kaw tund wu ndaw wu dara saxul.
4Ba loolu amee Yàlla dikk, dajeek Balaam, Balaam ne ko: «Ñaari sarxalukaay yi, yékkati naa leen te sarxalukaay bu ci nekk, sarxal naa ci wenn yëkk ak menn kuuy.»
5Aji Sax ji nag yeb kàddu ci gémmiñu Balaam, daldi ne ko: «Dellul ca Balag, te nga waxe noonu.»
6Balaam dellu ca moom, fekkul lu moy mu taxaw ca saraxu dóomalam, moom ak kàngami Mowab yépp.
7Balaam yékkati kàddug ñaanam, ne: «Fa Aram la ma Balag buuru Mowab jële, foofa ca tundi penku ya, ne ma: “Kaay ñaanal ma yàlla Yanqóoba, Dikkal rëbbal ma Israyil mii.”
8Moo nu may móoloo ku Yàlla móoluwul? Ana nu may rëbbe ku Aji Sax ji rëbbul?
9Kaw doj yii laa tollu di leen séen, fi kawte yii laa leen jéere. Aw askan a ngii, dëkke fu beru, te bokkuñu ak xeet yi.
10Ana kuy lim feppi suuf, ba lim askanu Yanqóoba? Ku mana waññ xaajaatub Israyil gii? Man de, yal naa dee deewinu aji jub ñii, yal na sama muj mel ni gu askan wii!»
11Ba loolu amee Balag ne Balaam: «Yaw, li nga ma def nag? Móolu samay noon laa la jële, yaw defoo lenn lu moy ñaanal leen?»
12Mu ne ko: «Xanaa du kàddu gu Aji Sax ji yeb sama gémmiñ, moom laa wara sàmm, ngir wax ko?»