Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 23

LUUG 23:2-25

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2Foofa ñu tàmbali di ko sosal naan: «Fekk nanu nit kii, muy fàbbi sunu réew, di leen teree fey galag Sesaar, te mi ngi teg boppam Almasi, maanaam buur.»
3Noonu Pilaat laaj ko: «Ndax yaa di buuru Yawut yi?» Yeesu ne ko: «Wax nga ko.»
4Pilaat ne sarxalkat yu mag ya ak mbooloo ma: «Gisuma genn tooñ ci nit kii.»
5Waaye ñu sax ci seeni wax naan: «Mi ngi jógloo mbooloo mi, di jàngle ci réewu Yawut ya mépp, li dale ci Galile ba fii.»
6Bi Pilaat yégee baat yooyu, mu laajte ne: «Ndax nit kii Galile la dëkk?»
7Bi mu yégee ne Yeesoo ngi nekk ci diiwaan bi Erodd yilif, mu yónnee ko Erodd, mi nekkoon ci jamono jooju ci Yerusalem.
8Bi Erodd gisee Yeesu, mu am mbég mu réy. Bu yàgg ba tey dafa koo bëggoona gis, ndaxte déggoon na ñuy wax ci ay mbiram te yaakaaroon na ne dina ko gis mu def kéemaan.
9Noonu mu laaj ko ay laaj yu bare, waaye Yeesu waxul dara.
10Sarxalkat yu mag ya ak xutbakat yaa nga fa woon, di ko jiiñ bu metti.
11Noonu Erodd ak ay xarekatam toroxal Yeesu, di ko ñaawal. Gannaaw loolu mu solal ko mbubb mu rafet, delloo ko Pilaat.
12Erodd ak Pilaat dañoo ñi bañante woon bu jëkk, waaye ca bés booba doon nañu ay xarit.
13Pilaat daldi woo sarxalkat yu mag ya, njiit ya ak mbooloom Yawut ya ne leen:
14«Indil ngeen ma nit kii, ne ma day jàddloo yoon mbooloo mi. Léegi nag man mii laaj naa ko ci seen kanam, waaye gisuma tooñ ci moom ak li ngeen koy jiiñ lépp.
15Erodd itam gisul tooñ gu mu def, ndegam mu yónneewaat nu ko. Nit kii deful genn tooñ gu jar ñu koy rey.
16Kon nag dinaa ko dóorlu ay yar te bàyyi ko.»
18Waaye ñu bokk di yuuxu, ñoom ñépp naan: «Reyal kii te bàyyi Barabas!»
19Dañoo tëjoon Barabas, ndaxte dafa jéema tas dëkk ba, te rey nit.
20Pilaat waxaat ak mbooloo ma, ndaxte dafa bëggoona bàyyi Yeesu.
21Waaye ñuy yuuxu naan: «Daaj ko ci bant! Daaj ko ci bant, ba mu dee!»
22Pilaat ne leen ñetteel bi yoon: «Lu tax? Gan tooñ la def? Gisuma ci moom dara lu jar dee. Kon dinaa ko dóorlu ay yar te bàyyi ko.»
23Waaye ñoom ñu sax ca la ñu waxoon, di gëna yuuxu naan, ñu daaj ko ci bant. Coow la yey Pilaat.
24Muj gi Pilaat dogal, ñu defal leen li ñu bëgg.
25Mu bàyyil leen ki ñu ko ñaanoon, kooku ñu tëjoon kaso, ndax tas réew ma ak rey nit. Waaye mu jébbal leen Yeesu ci seeni loxo.

Read LUUG 23LUUG 23
Compare LUUG 23:2-25LUUG 23:2-25