Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 1

LUUG 1:16-25

Help us?
Click on verse(s) to share them!
16Dina delloosi niti Israyil yu bare ci Yàlla seen Boroom.
17Mooy jiitu, di yégle ñëwug Boroom bi, ànd ak xel mi ak doole, ji yonent Yàlla Ilyaas amoon, ngir jubale xoli baay yi ak doom yi, ngir delloo ñi déggadi ci maanduteg ñi jub. Noonu dina waajal mbooloo muy teeru Boroom bi.»
18Sakari daldi ne malaaka ma: «Nan laay xame ne loolu dëgg la? Ndaxte mag laa, te sama soxna it màggat na.»
19Malaaka ma ne ko: «Man maay Jibril miy taxaw ci kanam Yàlla. Dañu maa yónni ngir ma wax ak yaw te yégal la xibaaru jàmm boobu.
20Léegi nag gannaaw gëmuloo li ma wax, dinga luu te dootuloo mana wax, ba kera sama wax di am, bu jamonoom jotee.»
21Fekk na booba mbooloo maa ngi xaar, jaaxle lool ci li Sakari yàgg ca bérab bu sell ba.
22Waaye bi mu génnee nag, manula wax ak ñoom. Noonu nit ña xam ne dafa am lu ko feeñu ca bérab bu sell ba. Dafa luu, ba di leen liyaar.
23Bi Sakari matalee liggéeyu sarxaleem ba noppi, mu daldi ñibbi.
24Bi mbir yooyu weesoo, Elisabet soxnaam ëmb, di ko nëbb lu mat juróomi weer
25te naan: «Lii mooy yiw wi ma Boroom bi defal, ba fajal ma li doon sama gàcce ci nit ñi!»

Read LUUG 1LUUG 1
Compare LUUG 1:16-25LUUG 1:16-25