3Yeesu àddu, ne xamkati yoon yaak Farisen ya: «Waaw, pajum bésub Noflaay, yoon maye na ko, am déet?»
4Ñu ne cell. Yeesu teg waa ja loxo, wéral ko, daldi ko yiwi.
5Mu ne leen: «Ana kan ci yeen la doomam mbaa aw yëkkam daanu cib teen, mu bañ koo daldi génne ci bésub Noflaay?»