3Yeesu yékkati baatam, ne xutbakat ya ak Farisen ya: «Ndax jaadu na, nu faj ci bésub noflaay bi?»
4Waaye ñépp ne cell. Yeesu daldi laal jarag ja, faj ko, ba noppi ne ko mu ñibbi.
5Gannaaw loolu mu ne leen: «Ku sa doom walla sa yëkk daanu ci teen, ndax doo dem génneji ko ca saa sa, fekk sax bésub noflaay la?»