Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 14:3-5 in Wolof

Help us?

LUUG 14:3-5 in Téereb Injiil

3 Yeesu yékkati baatam, ne xutbakat ya ak Farisen ya: «Ndax jaadu na, nu faj ci bésub noflaay bi?»
4 Waaye ñépp ne cell. Yeesu daldi laal jarag ja, faj ko, ba noppi ne ko mu ñibbi.
5 Gannaaw loolu mu ne leen: «Ku sa doom walla sa yëkk daanu ci teen, ndax doo dem génneji ko ca saa sa, fekk sax bésub noflaay la?»
LUUG 14 in Téereb Injiil

Luug 14:3-5 in Kàddug Yàlla gi

3 Yeesu àddu, ne xamkati yoon yaak Farisen ya: «Waaw, pajum bésub Noflaay, yoon maye na ko, am déet?»
4 Ñu ne cell. Yeesu teg waa ja loxo, wéral ko, daldi ko yiwi.
5 Mu ne leen: «Ana kan ci yeen la doomam mbaa aw yëkkam daanu cib teen, mu bañ koo daldi génne ci bésub Noflaay?»
Luug 14 in Kàddug Yàlla gi