Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 13

Luug 13:8-17

Help us?
Click on verse(s) to share them!
8Surga ba ne ko: “Sang bi, bàyyiwaat ko at mii rekk, ba ma wéex ko, def ci tos.
9Jombul mu meññ déwén; lu ko moy, nga gor ko.”»
10Benn bésub Noflaay, Yeesoo doon jàngle ci ab jàngu.
11Ndeke jenn jigéen a nga fa woon; rab a ko woppal lu wara mat fukki at ak juróom ñett, mu xuuge, manula fexe ba siggi.
12Yeesu gis ko, woo ko, ne ko: «Jongama, teqlikoo nga ak sa laago.»
13Mu teg ko ay loxoom, mu siggi ca saa sa, di sàbbaal Yàlla.
14Njiitu jàngu ba nag yékkati kàddug ñaawlu ndax bésub Noflaay ba Yeesu faje. Mu ne mbooloo ma: «Juróom benni fan la nit ñi wara liggéey. Kon ci fan yooyu ngeen wara fajusi, waaye du ci bésub Noflaay.»
15Sang bi ne ko: «Jinigalkat yi ngeen doon! Xanaa du ci bésub Noflaay la kenn ku nekk ci yeen di yiwee aw yëkkam mbaa mbaamam ca gétt ga, ngir wëggi ko?
16Jigéen jii di sëtub Ibraayma, te fukki at ak juróom ñett a ngii Seytaane làggal ko, wareesu koo yiwi, teggil ko laago jii ci bésub Noflaay?»
17Ba mu waxee loolu, noonam yépp a rus, mbooloo ma nag di bége mboolem jëf ju yéeme, ja muy def.

Read Luug 13Luug 13
Compare Luug 13:8-17Luug 13:8-17