Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 13

LUUG 13:8-17

Help us?
Click on verse(s) to share them!
8Surga ba ne ko: “Sang bi, bàyyiwaat ko fi at mii. Dinaa wàqi taat wi, def ci tos.
9Xëy na dina meññi. Bu ko deful, nga gor ko.”»
10Benn bésub noflaay Yeesoo ngi doon jàngle ci ab jàngu.
11Amoon na fa jigéen ju rab jàppoon, ba feebarloo ko lu wara mat fukki at ak juróom ñett; dafa xuuge woon te manul woona siggi dara.
12Bi ko Yeesu gisee, mu woo ko ne ko: «Soxna si, sa feebar deñ na.»
13Noonu mu teg ko ay loxoom, soxna sa siggi ca saa sa, di màggal Yàlla.
14Waaye njiitu jàngu ba mer, ndax li Yeesu fajoon nit ca bésub noflaay ba, mu ne mbooloo ma: «Am na juróom benni fan yu nit ñi wara liggéey. Kon war ngeena ñëw faju ci bés yooyu, waaye du ci bésub noflaay bi.»
15Boroom bi ne ko: «Naaféq yi! Ndax bésub noflaay bi, kenn ku nekk ci yéen du yiwee ca gétt ga yëkkam walla mbaamam ngir wëggi ko?
16Jigéen jii nag bokk ci askanu Ibraayma te Seytaane tënk ko fukki at ak juróom ñett, ndax kenn waru koo yiwi ci bésub noflaay bi?»
17Naka la wax loolu, noonam yépp daldi rus, waaye mbooloo mi di bég ci jëf yu yéeme, yi mu doon def yépp.

Read LUUG 13LUUG 13
Compare LUUG 13:8-17LUUG 13:8-17