30Su ko defee nag, ñenn a ngi mujje tey, waaye ëllëg ñooy jiitu; te ñenn a ngi jiitu tey, waaye ëllëg ñooy mujje.»
31Ca jamono jooju tembe la ay Farisen dikk, ne Yeesu: «Jógeel fii, te dem, ndax Buur Erodd da laa nara rey.»
32Mu ne leen: «Demleen wax njomboor moomu, ne ko: “Maa ngii di dàq rab yi, di maye ag wér, tey ak ëllëg. Bésub ñetteel ba nag ma sottal.”
33Waaye tey ak ëllëg ak sibir, fàww ma dem, ndax ab yonent wareesu koo bóome fenn fu dul Yerusalem.
34«Yerusalem, Yerusalem, yaw miy bóom yonent yi, di sànni ay doj ñi ñu yebal ci yaw, ba ñu dee, ñaata yoon laa namma dajale say doom, uuf ni ganaar di uufe ay cuujam, te nanguwuloo?
35Mu ngoog, waccees na laak sa kër nag, waaye maa ne la doo ma gisati ba kera jant ba nga naa: “Na barke wàccal ki ñëw ci turu Boroom bi!”»