12Ma gis ne nit amul lu gën bànneex ak jàmmi bakkan cig dundam,
13te nitoo nit, su dee lekk ak a naan, di ñaq, jariñoo, loolu mayu Yàllaa.
14Ma xam ne lu Yàlla def, loola day sax ba fàww. Deesu ci yokk, mbaa di wàññi dara; Yàllaa ko def, ngir nit di ko wormaal.
15Lu ay tey, ayoon na, lu ay ëllëg it ayoon na. Yàllaay namma indi la woon.
16Ma dellu gis fi kaw suuf ne, fu yoon moom, fa la njubadi ne, fa njub moom it, fa la njubadi ne.
17Saam xel ne ma, ku jub ak ku bon la Yàlla di boole àtte, ngir mbir mu ne ak jëf ju ne ak bésam.
18Saam xel neeti ma, nun doom aadama, Yàllaa nuy nattu, nu gis ne ay mala doŋŋ lanu.
19Dogalu doom aadama ji ak dogalu mala mi, benn dogal bee; ni kii di deeye la kee di deeye, genn noo gee, nu bokk ko. Lu nit ëpplee mala neen na, ñoom ñépp, cóolóoli neen.
20Ñoom ñépp a bokk jëm benn bérab ba, bokk jóge pëndub suuf, bokk dellu suuf.