13Damaa dogu ne damay gëstu, teg ko ci xel mu rafet, di settantal mboolem lu nit def fu jant bi tiim. Ndaw sas wu tiis wu Yàlla sase, ñu war koo sasoo!
14Gis naa jépp jëf ju jëfe ci kaw suuf, ndeke lépp cóolóoli neen la ak napp um ngelaw.
15Lu wañaaru, maneesu koo jubbanti; lu teewul, maneesu koo lim.
16Damaa wax ci saam xel naa: Man de, maa ngii di gëna xelu, ba sut ku ma jiitu ci jalub Yerusalem. Damaa xuus ci xel mu rafet ak xam-xam,
17di dogoo xam luy xel mu rafet, xam luy nitoodi akug ndof. Fekk loolu it napp um ngelaw la.
18Ku géejal xel mu rafet, géejal naqar; yokku xam-xam, yokku tiis.