Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàdduy Waare - Kàdduy Waare 12

Kàdduy Waare 12:7-12

Help us?
Click on verse(s) to share them!
7Su boobaa pënd dellu suuf, na woon; bakkan dellu fa Yàlla ma able woon.
8Cóolóoloo cóolóol, waru waarekat ba. Léppi cóolóoli neen.
9Waarekat ba daa xelu, di jànglewaale xam-xam, di natt ak a gëstu, di jekk-jekkal kàdduy xel yu takku.
10Waarekat ba daa tànn baat yu saf, bind ko, mu jub te dëggu.
11Waxi ku xelu day gindee, bantub sàmm la; tënk ba diy pont, sampe ca. Loolu ag may la, jóge ci sàmm biy kenn.
12Doom, leneen lu ci tegu, moytu ko: Yokki téere amul kemu, njàng mu bare, coonoy boroom.

Read Kàdduy Waare 12Kàdduy Waare 12
Compare Kàdduy Waare 12:7-12Kàdduy Waare 12:7-12