3Su bés baa wattukati kër gi di lox, jàmbaari xare yi sëgg, wolkat yi néew, ba wolatuñu, ñiy séentu ci caax yi giimle,
4bunt yi féeteek mbedd mi tëje, coowal wol dal, as picc sab, nelaw naaw, janq ju doon woy, selaw.
5Nga dem, ba ragal fu kawe, am tiitaange ciw yoon, garab tóor, ba weex furr, soccet di yokokoki, doomu garab tëë yékkati siddit, nga jëm kër gu mujj, waa dëj bi fees mbedd mi.
6Bàyyil xel ki la sàkk, balaa buumu xaalis bi ne tipp, ndabal wurus wi, tasar, njaq la ñuy roote, rajax, poli ba ca teen ba, tàllit.