Text copied!
Bibles in Wolof

Kàdduy Waare 12:3-6 in Wolof

Help us?

Kàdduy Waare 12:3-6 in Kàddug Yàlla gi

3 Su bés baa wattukati kër gi di lox, jàmbaari xare yi sëgg, wolkat yi néew, ba wolatuñu, ñiy séentu ci caax yi giimle,
4 bunt yi féeteek mbedd mi tëje, coowal wol dal, as picc sab, nelaw naaw, janq ju doon woy, selaw.
5 Nga dem, ba ragal fu kawe, am tiitaange ciw yoon, garab tóor, ba weex furr, soccet di yokokoki, doomu garab tëë yékkati siddit, nga jëm kër gu mujj, waa dëj bi fees mbedd mi.
6 Bàyyil xel ki la sàkk, balaa buumu xaalis bi ne tipp, ndabal wurus wi, tasar, njaq la ñuy roote, rajax, poli ba ca teen ba, tàllit.
Kàdduy Waare 12 in Kàddug Yàlla gi